Fi ñu ma doon séentu gisuñu ma fa
Fi ñu ma doon xaar ñëwuma fa
Ñoo ngi ma doon xaar ci gallu xat
Waaye góor du ci lépp la xaaj
Yaay booy ne na siggil na ko
Jëkkër ne na sagal na ko
Askan bi sagal na leen
Baay booy sa doom wacc na
Yaay booy ne na siggi na
Baay booy ne na siggi na
Askan wi tamit ne nañu siggi nañu
Seen doom bi ñu doon xaar wacc na
Guddi bi ñu ma mayee ci lañu ma jëlé
Yaay jaaxle lool bajjen toog di xaar
Seen doom ji wacc na
Siggil na leen tasul yaakaar
Ñi ma doon xaar yegsi na
Ñi ma doon sentu tew na
Sama noon yi du gen ree
Ndax sama yaay booy siggi na
Yaay booy ne na siggi na
Baay booy ne na siggi na
Askan wi tamit ne nañu siggi nañu
Seen doom bi ñu doon xaar wacc na